jeudi 28 juin 2018

Plateau Spécial Serigne Ibrahima Mbacké: Serigne Ablaye Diop Bichri

Kan moy Serigne Bala Faly Dieng?

 

Serigne Abdou Ndam Dieng Moom Serigne Bala Faly Dieng

Akb Majalis
Kan mooy Sëriñ Bàlla Faali Jeŋ?

Sëriñ Habiibu Laah Jeŋ, ñu gën koo xam ci Sëriñ Bàlla Faali, mi ngi feeñ jamono ci atum 1856, ci dëkk bu ñuy wax Njompi, nekk ca Kajoor.

Aw Askanam:
Sëriñ Bàlla Faali, di doomi Sëriñ Masàmba Soxna Jeŋ ak Soxna Xujja Aram Silla, mom Majama Anta Silla mi nga xam ne, moo sañci Ñaxal ci gox bu ñuy wax Ndogal.

Am njàngam:
S. Bàlla Faali, mi ngi jàngee Alxuraan ci ku ñuy wax Sëriñ Ahmadu Silla ca Tayba xay,  foofu la nekk ba mokkal Alxuraan.
Ginaaw loolu, soobu na ci njàngum xam xam, ba jàng ci fànn yu bari te wuute ci fànn yi ñu baaxoo woona jàng ci réew mi, ba géeju ca lool.
Ba mu noppee ci am njàngam nak, la dellu ca kër baayam, Sëriñ Masàmba Soxna ca Njompi, nekk ci wetam, daan ko jàple ci mbiri àdduna yi ak mbiri diiné yi, daan wéyé ay ndigalam ci lépp. Ci loolu la sax, ba ni mu sañcee kër, ñu dénkoon ko Soxna su ñuy wax Soxna Kana Mbóoj.

Ak Jébbloom:
Mu teela jébblu lool ci Sëriñ Tuubaa, ci jamono ya mu nekkee Daaru Salaam ci atum 1886, foofa la ko Sëriñ Bàlla fekkoon, jaayante ak moom, ci anam yu taroon lool ci moom, waaye muy ku Yàlla dimbali woon ci yitté ju kawe ak pas pas bu dëggu.
Ginaaw bi Sëriñ bi sañcee dëkkam bii di Tuubaa yit, S. Bàlla bokkoon ci ñi àndoon ak moom, mooy ki fi ñjëkka bay, ngir màndargaal dëkk bi bañ man koo xàmmee.
Foofu ci Daaru Salaam, fa la ko Boroom Tuubaa tarbiyaa, ci diirub 3 at, mook Seex Ibra Faal ak yeneeni mag ci yoon wi.
Sëriñ Tuubaa gëram ko, ngëram lu kawe ginaaw bi mu sañcee Tuubaa, te daan seede ak defaroom, li ciy firndé mooy ki ñëwoon ci moom ne ko "Mbàkke, man de da maa bëgg nga defar ma", Boroom Tuubaa boole ko ak Sëriñ Bàlla Faali mii, ne ko "defar de, taqoo la laaj, te amatuma jot gi, waaye demal seeti Bàlla Faali, moom defar naa ko".
Kon ku Sëriñ Tuubaa seedeel sag defaru, loolu rek doy na sëkk tawfeex.

Ay jëfam ci yoon wi:
Batay moom Sëriñ Bàlla mii, bokk na ci ñi Sëriñ bi njëkka jox ndigalul Màggal bisub 18 Safar (Màggalug Tuubaa), mu amoon ci ak farlu lool ak pasteef, ba mujj sax bisub Màggal bii, ñu ko daan woowe "bisub Sëriñ Bàlla Faali". Loolu la Sëriñ Musaa Ka di wax ci bëyit yii naan:
"Mu dellu saxal ci weeru Safar di màggal
Bi izni Cheyxi Ahmadu Bàmba Waali

Fabug coggal, di def di ko yobbu Tuubaa
Wa saakuy ceeb, wa xandiy diw, wa maali

Saxal na ko fukki at yu tofal juroomam
Deful koppar ci kalpe ba yobbu waale"

Sëriñ Bàlla Faali, bokkoon na ci taalibé yi sàkku ci Sëriñ Tuubaa ngir mu bindal leen, lu jëm ci ak ay teggiin akug taalibé, moo sabab Sëriñ bi taalifoon Xasidag Nahju ca jamono yooya, moom la Sëriñ bi di wax ci bëyit wii naan
قد طلبوا نظما حوى تأدبا = ليتأدبوا وذاك وجبا

Ci guerre ba amoon ci atum 1914 - 1918, Sëriñ Bàlla moo njëkka joxe ay niti bopam ci soldaar yi wara dem ca guerre ba.
Noonu yit la ràññee koo woon lool ci ligéeyub Jumaay Tuubaa, bi ci Sëriñ bi joxee ndigal.
Jumaay Njaarém ji tamit noonu la ci ràññee koo woon ci joxe ci àddiyaam, te moom la Sëriñ bi féetale woon muy saytu alal ji fay dem.
Farlu woon lool ci joxe àddiya, daan ko ko yonnee ba Gànnaar ci Sëriñ bi, ci sabab yooyu sax la ko Boroom Tuubaa yonnée woon Xasidag Jalibatou Marakhib, joxoon ko ndigal mu mokkal ko, mook ay taalibéem.

Mu sañcoon ay barab yu wuute, ngir jaamu Yàlla ak ligéey, ak daan tarbiya ñi ko Sëriñ Tuubaa booleel, bokk na ci barab yooyu, fu ñuy wax Daaru Jeŋ, mu sañcoon ko ci ndigalul Sëriñ bi ci atum 1903, ak yeneen daara yu bari ci réew mi.

Bi Sëriñ bi nekk Njaaréem, joxoon na ko ndigal mu sañci fa kër, mu nekkoon fa ak moom. Ginaaw làqug Sëriñ bi yit mu toppoon Seex Mustafaa, gëna yeesal pas pasam ak farloom ci ligéeyal Sëriñ Tuubaa, Seex Mustafaa fonkoon ko lool, ba gane ji woon ko ca Njompi ngan gu rëy, moom la Sëñ Musaa Ka naan:

"Ma santal Sëriñ Tuubaa Sëriñ Bàlla Faali Jeŋ
Du moo gëm Sëriñ Tuubaa  te gëm Amdi Mustafaa

Dëggal gam dëggal mootax ba Buur Yàlla far dogal
Mu moom waa ndogal, moom njompe, moom Daaru Mustafaa

Sëriñ Bàlla faalee jox Sëriñ Amdi tiitaram
Na léen woor ne boobe gembbe yaaram la Mustafaa"

Noonu mu meloon ak Seex Mustafaa, ni la defoon ak njabootug Sëriñ bi yépp, ba manees naa wax ni ñi ci ëpp tuddée na leen doom, ni la defoon yitam ak magi Murid yépp, ku mel ni Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan Lo mi mu tuddé ab ki ko njëkka wuutu, ak ku mel ni Sëriñ Moor Kumba Kan, Sëriñ Masàmba Kànni Buso, Sëriñ Madiba Silla, ak mak ñu bari ci yoon wi.

Ak làqoom:
Misaalum Murid Saadix bu làq ngëramul Sëriñ Tuubaa ngi nii, 1886 ba 9 Mars 1940, masula tàqali koo ak Boroom Tuubaag waa këram, keroog ba mu làqoo ca Njaaréem, ci la Seex Mustafaa wax Sëriñ Mbàkke Buso mu jullee ko, ñu deñci ko ci armeel yii ci Tuubaa. Yàl na nu Yàlla taas ci barkeem !

Ay xalifaam: ki ko njëkka wuutu mooy:
Sëriñ Abdu Jeŋ Bàlla Faali 1940 - 1988
Sëriñ Abdu Kariim Jeŋ Bàlla Faali 1988 - 2012
Ki fi tooge ab jotaayam ci jamono yii mooy Sëriñ Moodu Jeŋ, yàl na ko fi Yàlla gëna yàggal te may ko wér ! bàrkeb Sëriñ bi.

Yala yook aay Lerram Tass Nousi Barkem si Barkep serignebi

Akb Majalis

Dénk kaané Serigne bi

                                   


Am na ku mës a ñëw ci Sëriñ Tuuba (qâda lahoo Laahu maaxtaara lahoo) ne ko : « Da ñoo nangu sama KËR ! »

Sëriñ Tuuba (qâda lahoo Laahu maaxtaara lahoo) ne ko : « Man de amagu ma KËR... »

Daa di ciy teg ne ko : « Nit ku nekk ñetti (3) dal la am.
Dal bu ñjëkk bi mooy biirub ndayam.
Dalub ñaareel bi mooy àdduna.
Dalub ñetteel bi mooy Barzaq.
Su fa jugee nag sooga dugg KËRAM...»

----------------

Un disciple vint trouver un jour Cheikh A. Bamba en se plaignant avec émoi  : « [Maître] l'on vient de me retirer la propriété de ma DEMEURE ! »

Le Cheikh de lui répondre en ces termes : « [Tu es assurément mieux loti que moi !] Car, en ce qui me concerne, je ne possède pas encore de DEMEURE... »

Le Grand Maître ensuite d'expliciter ses propos à l'intention du disciple : « En vérité, chaque être humain possède juste trois (3) éphémères lieux de passage.
Son premier lieu de séjour est le ventre de sa mère.
Le second consiste en ce monde ici-bas.
Le troisième est l'entre-deux mondes (barzaq) où il attendra, après sa mort, l'avènement du Jugement Dernier.

Ce n'est qu'à l'issue de ce dernier séjour, sache-le, qu'il rejoindra définitivement sa véritable et éternelle  DEMEURE... »

[Traduction : Majalis]

mercredi 27 juin 2018

Kan moy Serigne Ibrahima Mbacké

#MAN_LA_KAN?

#MAN_LA_KAN?

 Taalibé Boroom Tuubaa laa
 1850 laa gane àdduna
 1921 laa génn àdduna
 Soxna Jaara mooy sama waajur
 Sëriñ Mbusóobe mooma jànggal
 Magi mak lañ may woowe
 Kaamilu Alxuraan ci 100 rakka lay naafilaa bis bu ne
 Nekk naa Sëriñ Mbàkke ay at
 Jàngal naa Sëñ Mbàkke Buso ak Maam Cerno ak S. Fàllu ak mak ñu bari ci yoonu Murid
 Bokk naa ci ñi doon taxawu njabootug Sëriñ bi, bi mu nekkee ci Géej gi
 Maa àndoon ak samay rakk représenté Sëriñ Tuubaa ba ko Mbaaxaan convoqué
 Man la Sëriñ Tuubaa wax "ku ma ligéeyal di nga am ñeenti fay"
 Sëriñ Tuubaa ma jox wird Maaxuz
 Man la Sëriñ Tuubaa waxoon "Yonent bi SAWS neena, maa ko gënal ci ay tourandoom"
 Nekkoon naa Saalum ci jamonoy Maba Jaxu Ba
 Bi ma làqoo Sëriñ Mbàkke Buso moo ma jullée
 Armeeli Mbàkke Bawol lañ ma deñci
 Bi ma noppaloo, Sëriñ Tuubaa seede na ci man ne "ba Yonent bi SAWS demee ba tay, jëmm ju teddee nii tëddagul ci biir suuf"
 Bi ma faatoo Sëriñ Tuubaa neena "yobbaale wu ma bor, yobbaale wu ma bàkkaar"

Yàl na nu ko Yàlla fayal !

mardi 26 juin 2018

                             

WAADIAL MAGALOUK Mame Mor Sokhna Diarra  BROME SHAM le 29 Juin 2018
Akb Majalis

Leensi Ndiabootok
MAME MOR DIARA Mbacke Brom

Pour présenter Mame Mor Diarra MBACKE, il suffit seulement de dire qu’il partage avec Cheikhoul Khadim la même mère, Sokhna Mariama BOUSSO.
Né en 1850 et décédé en 1921 au village de Mbacke Baol, il faisait parti des Grands disciples de Serigne Touba, fusse-t-il son grand frère et même à un moment donné de la jeunesse du Cheikh son professeur.

Il était aimé et respecté par Serigne Touba, c’était un érudit qui ne ménageait aucun effort dans l’adoration de son SEIGNEUR.
Il s’était imposé des prières nocturnes surérogatoires de 100 génuflexions (Rakkas) composé des versets du Saint Coran.

La noblesse de caractère est une expression qui résume sa vie et son attitude. L’intensité de son adoration de DIEU peut se lire dans ce témoignage éloquent que fit Cheikh Mouhamed Al Bachir dans ses "Minans" "Cheikh Momar Diara, le frère germain de notre Cheikh, est de ceux qui accomplissaient de fréquentes prières nocturnes, qui récitaient le Coran, très souvent et dont le wird consistait en cent (100) génuflexions (Rakkas)".

il recevait des recommandations du Cheikh qu’il s’empressait d’exécuter en parfaite conformité. Cheikhoul Khadim alors en Exil au Gabon lui adressa une correspondance pour lui donner des recommandations et lui confier des responsabilités.

Durant toute sa vie, le travail occupait une place importante dans ses activités, il aimait réunir toute la famille de Maharam, Serigne Mor était quelqu’un de généreux, il avait de la compassion envers tout le monde, son empathie n’était pas un secret, bref il était l’une des personnifications de la générosité.
Serigne Touba lui avait dit, je cite : "J’ai la même mission que Toi mais je suis ton porte-parole".
Malgré qu’il soit son disciple, Serigne Touba lui a toujours montré du respect, de la considération et de par son comportement le fait qu’il soit son ainé, il lui a d’ailleurs, une fois dit "le Prophète(SAW) m’a attesté que tu étais son préféré parmi tous ses homonymes".

Akb Majalis

#MAGAL_MAME_MOR_DIARRA_29JUIN_2018

Waxtaan: Cheikh Abdoul Ahad Mbacké par Serigne Moustapha Saliou

Témoignage: Cheikh Abdoul Ahad Mbacké par Serigne Mountakha Bachir

Serigne Abdoul Ahad Mbacké: Digeunté Serigne Touba ak Yonent bi (SAWS)

Wolofal: Marsia Cheikh Abdoul Ahad Mbacké par S. Abdoul Ahad Touré

Les Discours de Serigne Abdoul Ahad Mbacké