Pages

jeudi 28 juin 2018

Kan moy Serigne Bala Faly Dieng?

 

Serigne Abdou Ndam Dieng Moom Serigne Bala Faly Dieng

Akb Majalis
Kan mooy Sëriñ Bàlla Faali Jeŋ?

Sëriñ Habiibu Laah Jeŋ, ñu gën koo xam ci Sëriñ Bàlla Faali, mi ngi feeñ jamono ci atum 1856, ci dëkk bu ñuy wax Njompi, nekk ca Kajoor.

Aw Askanam:
Sëriñ Bàlla Faali, di doomi Sëriñ Masàmba Soxna Jeŋ ak Soxna Xujja Aram Silla, mom Majama Anta Silla mi nga xam ne, moo sañci Ñaxal ci gox bu ñuy wax Ndogal.

Am njàngam:
S. Bàlla Faali, mi ngi jàngee Alxuraan ci ku ñuy wax Sëriñ Ahmadu Silla ca Tayba xay,  foofu la nekk ba mokkal Alxuraan.
Ginaaw loolu, soobu na ci njàngum xam xam, ba jàng ci fànn yu bari te wuute ci fànn yi ñu baaxoo woona jàng ci réew mi, ba géeju ca lool.
Ba mu noppee ci am njàngam nak, la dellu ca kër baayam, Sëriñ Masàmba Soxna ca Njompi, nekk ci wetam, daan ko jàple ci mbiri àdduna yi ak mbiri diiné yi, daan wéyé ay ndigalam ci lépp. Ci loolu la sax, ba ni mu sañcee kër, ñu dénkoon ko Soxna su ñuy wax Soxna Kana Mbóoj.

Ak Jébbloom:
Mu teela jébblu lool ci Sëriñ Tuubaa, ci jamono ya mu nekkee Daaru Salaam ci atum 1886, foofa la ko Sëriñ Bàlla fekkoon, jaayante ak moom, ci anam yu taroon lool ci moom, waaye muy ku Yàlla dimbali woon ci yitté ju kawe ak pas pas bu dëggu.
Ginaaw bi Sëriñ bi sañcee dëkkam bii di Tuubaa yit, S. Bàlla bokkoon ci ñi àndoon ak moom, mooy ki fi ñjëkka bay, ngir màndargaal dëkk bi bañ man koo xàmmee.
Foofu ci Daaru Salaam, fa la ko Boroom Tuubaa tarbiyaa, ci diirub 3 at, mook Seex Ibra Faal ak yeneeni mag ci yoon wi.
Sëriñ Tuubaa gëram ko, ngëram lu kawe ginaaw bi mu sañcee Tuubaa, te daan seede ak defaroom, li ciy firndé mooy ki ñëwoon ci moom ne ko "Mbàkke, man de da maa bëgg nga defar ma", Boroom Tuubaa boole ko ak Sëriñ Bàlla Faali mii, ne ko "defar de, taqoo la laaj, te amatuma jot gi, waaye demal seeti Bàlla Faali, moom defar naa ko".
Kon ku Sëriñ Tuubaa seedeel sag defaru, loolu rek doy na sëkk tawfeex.

Ay jëfam ci yoon wi:
Batay moom Sëriñ Bàlla mii, bokk na ci ñi Sëriñ bi njëkka jox ndigalul Màggal bisub 18 Safar (Màggalug Tuubaa), mu amoon ci ak farlu lool ak pasteef, ba mujj sax bisub Màggal bii, ñu ko daan woowe "bisub Sëriñ Bàlla Faali". Loolu la Sëriñ Musaa Ka di wax ci bëyit yii naan:
"Mu dellu saxal ci weeru Safar di màggal
Bi izni Cheyxi Ahmadu Bàmba Waali

Fabug coggal, di def di ko yobbu Tuubaa
Wa saakuy ceeb, wa xandiy diw, wa maali

Saxal na ko fukki at yu tofal juroomam
Deful koppar ci kalpe ba yobbu waale"

Sëriñ Bàlla Faali, bokkoon na ci taalibé yi sàkku ci Sëriñ Tuubaa ngir mu bindal leen, lu jëm ci ak ay teggiin akug taalibé, moo sabab Sëriñ bi taalifoon Xasidag Nahju ca jamono yooya, moom la Sëriñ bi di wax ci bëyit wii naan
قد طلبوا نظما حوى تأدبا = ليتأدبوا وذاك وجبا

Ci guerre ba amoon ci atum 1914 - 1918, Sëriñ Bàlla moo njëkka joxe ay niti bopam ci soldaar yi wara dem ca guerre ba.
Noonu yit la ràññee koo woon lool ci ligéeyub Jumaay Tuubaa, bi ci Sëriñ bi joxee ndigal.
Jumaay Njaarém ji tamit noonu la ci ràññee koo woon ci joxe ci àddiyaam, te moom la Sëriñ bi féetale woon muy saytu alal ji fay dem.
Farlu woon lool ci joxe àddiya, daan ko ko yonnee ba Gànnaar ci Sëriñ bi, ci sabab yooyu sax la ko Boroom Tuubaa yonnée woon Xasidag Jalibatou Marakhib, joxoon ko ndigal mu mokkal ko, mook ay taalibéem.

Mu sañcoon ay barab yu wuute, ngir jaamu Yàlla ak ligéey, ak daan tarbiya ñi ko Sëriñ Tuubaa booleel, bokk na ci barab yooyu, fu ñuy wax Daaru Jeŋ, mu sañcoon ko ci ndigalul Sëriñ bi ci atum 1903, ak yeneen daara yu bari ci réew mi.

Bi Sëriñ bi nekk Njaaréem, joxoon na ko ndigal mu sañci fa kër, mu nekkoon fa ak moom. Ginaaw làqug Sëriñ bi yit mu toppoon Seex Mustafaa, gëna yeesal pas pasam ak farloom ci ligéeyal Sëriñ Tuubaa, Seex Mustafaa fonkoon ko lool, ba gane ji woon ko ca Njompi ngan gu rëy, moom la Sëñ Musaa Ka naan:

"Ma santal Sëriñ Tuubaa Sëriñ Bàlla Faali Jeŋ
Du moo gëm Sëriñ Tuubaa  te gëm Amdi Mustafaa

Dëggal gam dëggal mootax ba Buur Yàlla far dogal
Mu moom waa ndogal, moom njompe, moom Daaru Mustafaa

Sëriñ Bàlla faalee jox Sëriñ Amdi tiitaram
Na léen woor ne boobe gembbe yaaram la Mustafaa"

Noonu mu meloon ak Seex Mustafaa, ni la defoon ak njabootug Sëriñ bi yépp, ba manees naa wax ni ñi ci ëpp tuddée na leen doom, ni la defoon yitam ak magi Murid yépp, ku mel ni Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan Lo mi mu tuddé ab ki ko njëkka wuutu, ak ku mel ni Sëriñ Moor Kumba Kan, Sëriñ Masàmba Kànni Buso, Sëriñ Madiba Silla, ak mak ñu bari ci yoon wi.

Ak làqoom:
Misaalum Murid Saadix bu làq ngëramul Sëriñ Tuubaa ngi nii, 1886 ba 9 Mars 1940, masula tàqali koo ak Boroom Tuubaag waa këram, keroog ba mu làqoo ca Njaaréem, ci la Seex Mustafaa wax Sëriñ Mbàkke Buso mu jullee ko, ñu deñci ko ci armeel yii ci Tuubaa. Yàl na nu Yàlla taas ci barkeem !

Ay xalifaam: ki ko njëkka wuutu mooy:
Sëriñ Abdu Jeŋ Bàlla Faali 1940 - 1988
Sëriñ Abdu Kariim Jeŋ Bàlla Faali 1988 - 2012
Ki fi tooge ab jotaayam ci jamono yii mooy Sëriñ Moodu Jeŋ, yàl na ko fi Yàlla gëna yàggal te may ko wér ! bàrkeb Sëriñ bi.

Yala yook aay Lerram Tass Nousi Barkem si Barkep serignebi

Akb Majalis

Aucun commentaire:

Enregistrer un commentaire