#MAN_LA_KAN?
Taalibé Boroom Tuubaa laa
1850 laa gane àdduna
1921 laa génn àdduna
Soxna Jaara mooy sama waajur
Sëriñ Mbusóobe mooma jànggal
Magi mak lañ may woowe
Kaamilu Alxuraan ci 100 rakka lay naafilaa bis bu ne
Nekk naa Sëriñ Mbàkke ay at
Jàngal naa Sëñ Mbàkke Buso ak Maam Cerno ak S. Fàllu ak mak ñu bari ci yoonu Murid
Bokk naa ci ñi doon taxawu njabootug Sëriñ bi, bi mu nekkee ci Géej gi
Maa àndoon ak samay rakk représenté Sëriñ Tuubaa ba ko Mbaaxaan convoqué
Man la Sëriñ Tuubaa wax "ku ma ligéeyal di nga am ñeenti fay"
Sëriñ Tuubaa ma jox wird Maaxuz
Man la Sëriñ Tuubaa waxoon "Yonent bi SAWS neena, maa ko gënal ci ay tourandoom"
Nekkoon naa Saalum ci jamonoy Maba Jaxu Ba
Bi ma làqoo Sëriñ Mbàkke Buso moo ma jullée
Armeeli Mbàkke Bawol lañ ma deñci
Bi ma noppaloo, Sëriñ Tuubaa seede na ci man ne "ba Yonent bi SAWS demee ba tay, jëmm ju teddee nii tëddagul ci biir suuf"
Bi ma faatoo Sëriñ Tuubaa neena "yobbaale wu ma bor, yobbaale wu ma bàkkaar"
Yàl na nu ko Yàlla fayal !
Aucun commentaire:
Enregistrer un commentaire